TSK

TSK · Genesis 2:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba.

¶ «Deeleen baaxantal bésub Noflaay, ngir sellal ko.

«Waxal bànni Israyil ne leen: “Fexeleen rekk ba sama bési Noflaay, ngeen di ko wormaal, ndax bésub Noflaay da di firnde sama digganteek yeen ak seen askan, ngir ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen ber, sellal leen.

Juróom benni fan lees di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, seen bésub Noflaay bu sell bu mat sëkk la, ñeel Aji Sax ji. Képp ku ci liggéey lenn, dees koy rey.

«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, suuf sa ca boppam war naa am àppu noflaayam ngir Aji Sax ji.

Sa bésub Noflaay bu sell it, yaa leen ko xamal, te say santaaneeki dogali yoon ak saw yoon, yaa leen ko dénk. Musaa, sa jaam ba, jottli leen ko.

Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.

«Su ngeen téyee seen tànk bésub Noflaay, baña def li leen neex sama bés bu sell; su bésub Noflaay di seen nammeel, di bésub Aji Sax bu sell bu ngeen teral; ngeen teral bés bi, bañ cee topp li ngeen jikkowoo, di topp seen bakkan ak wax ju dul jeex;

Sama bési Noflaay itam maa leen ko jox, muy màndarga sama digganteek ñoom, ngir ñu xam ne man Aji Sax ji maa leen sellal.

Ba loolu amee ñu dellu, waajali cuuraay ak diwu xeeñlu ngir néew ba. Bésub Noflaay nag taxaw, ñu dal-lu, ni ko yoon santaanee.