TSK

TSK · Genesis 22:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar.

Ca la tudde bérab ba Betel, waaye ca njàlbéen Lus la dëkk ba tuddoon.

Musaa nag sàkk fa sarxalukaay, tudde ko tur wuy tekki «Aji Sax jeey sama raaya».

Kon teelala fabu ëllëg, yaak sa surgay sang yi nga àndal; Dangeen di teela jóg rekk, bu bët setee ngeen dem.»

Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal, Israyil di la kañ.

Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.