TSK

TSK · Genesis 23:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.

Ba loolu wéyee Isaaxa yóbbu Rebeka ca xaymab yaayam Saarata, muy soxnaam, di ku mu bëgg, te di ko muñe yaayam, ndax fekk na mu faatu.

¶ Ba mu ko defee Yuusufa daanu ci kaw baayam. Ma ngay jooy te di ko fóon.

Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra.

Bànni Israyil jooy nañu Musaa ca jooru Mowab diiru fanweeri fan, fani dëj ba doora mat.

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Samiyel faatu, Israyil gépp daje, dëj ko, daldi koy denc ca këram ca Raama. Daawuda nag fabu, wuti màndiŋu Paran.

Ñaawlu nañu, di jooy, lekkuñu ba ca ngoon ndax Sóol ak doomam Yonatan ak gàngooru Aji Sax ji, waa kër Israyil, ña fàddoo saamar.

Diir ba Daawuda falu buurub Ebron gu waa kër Yuda, juróom ñaari at la ak juróom benni weer.

Ca Ebron la yore nguurug Yuda juróom ñaari at ak juróom benni weer, waaye ca Yerusalem la yore diiru fanweeri at ak ñett, mboolem Israyil ak Yuda.

Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, ne: «Kenn du ko jooy ca mbokkam mu góor mbaa mu jigéen, naan: “Wóoy ngalla nun, bokk yi!” Kenn du ko jooy, naan: “Wóoy, sang ba, wóoy kilifa ga!”

Acts 8:2 TSK

¶ Ay nit ñu ragal Yàlla nag rob Eccen, ñaawlu deeyam lool.