TSK

TSK · Genesis 32:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Sa saamar ngay dunde, sa rakk di la yilif. Waaye bés a ngi ñëw yaay sigiñu, ba yenniku notaangeem.»

¶ Yanqóoba dégg loolu, tiit lool te ànd ak njàqare, ba tax mu séddale mbooloo, ma mu àndal, gàtt ya ak jur gu gudd ga ak giléem ya itam, mu xaaj leen ñaar.

¶ Gannaaw loolu Yanqóoba séen Esawu di ñëw, ànd ak ñeenti téeméeri góor, mu séddale xale yi, diggante Leya, Rasel ak ñaari jaam ya.

Esawu ne ko: «Xaaral ma bàyyee la ñenn ci góor, ñi ma àndal.» Yanqóoba ne ko: «Matu ko. Boobu teraanga ëpp na, sang bi. Jàmm ji nga ma dalal rekk doy na.»

Ñu ne ko: «Sang bi, rawale nga nu! Te gannaaw laaye nga nu biir, nangu nanoo doon jaami Firawna.»

Ruth 2:13 TSK

¶ Ruut ne ko: «Teral nga ma de, sang bi. Yaa ngi may laaye biir, ndaxte dëfal nga ma, wax ma lu seral sama xol, te moona say surga yu jigéen yi sax a ma gën.»

Amos 5:19 TSK

Day mel ni kuy daw gaynde, ne pemm cim segg, rëcc, ñibbi, teg loxoom ca tabax ba, jaan ne ko càppit.