TSK

TSK · Genesis 35:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la délloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.»

Aji Sax ji wax Yanqóoba ne ko: «Dellul ca sa réewu maam ya, ca say bokk. Dinaa ànd ak yaw.»

Ndaw ya daldi dem ba délsi ca Yanqóoba, ne ko: «Dem nanu ca sa mag Esawu, waaye moom ci boppam mu ngi ci yoon wi di ñëw, fekksi la fii, te ma nga ànd ak ñeenti téeméeri góor.»

Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne: «Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon, moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,

di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»

Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,

Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall, mu xettlee leen seen njàqare,

Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo, dagaan ko, mu dégg ma.

Ubbil-leen ma bunti njekk, ma dugg santi Ki Sax.

Yeen waa Siyoŋ, yeen waa Yerusalem, dootuleen jooy mukk! Bu ngeen jooyee, mu yërëm leen moos; bu leen di dégg, di leen nangul.