doora faatu ca Kiryaat Arba, mooy Ebron, ca réewu Kanaan. Ibraayma nag dëj Saarata, jooy ko lool.
TSK
TSK · Genesis 37:14
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Yanqóoba dellu na kër baayam Isaaxa fa Mamre, ca Kiryaat Arba, gay Ebron ba tey, fa Ibraayma ak Isaaxa daloon.
Mu nuyoo ak ñoom, ba noppi laaj leen ne leen: «Seen baay bu màggat, ba ngeen doon wax, mbaa mu ngi dund? Mbaa mu ngi ci jàmm?»
Ci biir loolu Yese ne doomam Daawuda: «Ayca, jëlal nattub mbool mii ak fukki mburu yii te nga daw, yóbbul ko sa mag ya ca dal ba.
Ci biir loolu Daawuda wàcce yóbbal ga, wacce ko wattukatub cummikaay ba, daldi daw ba ca làngu xare ba. Mu agsi, nuyook ay magam.
Yal na Yowab ak askanam gàddu seen bakkan ba fàww. Waaye Daawudaak askanam ak waa këram akub jalam, yal na leen Aji Sax ji jàmmal ba fàww.»
Waaye kuy topp yoonu ndëngte, Aji Sax jee koy sànk, boole kook kuy def lu bon. Yal na jàmm dal Israyil.
Mu ne: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey jii li lay may jàmm! Waaye fii mu ne, làqu na say gët.