TSK

TSK · Genesis 37:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.»

Mag ya nag iñaane ko. Teewul baayam moom bàyyi xel ci mbir moomu.

Ay fittkat a ko toŋal, di ko song ak a fitt.

¶ Elyab, magu Daawuda, dégg Daawuda di wax ak ñooña. Mu mer, ne ko: «Yaw sax lu la fi indi? Ak koo wacce la fay gàtt ak as néew ca àll ba? Xam naa bu baax sag réy ngise, ak njubadi gi nga mébét. Seetaansi xare bi doŋŋ a la fi indi!»

Ma woote wall ba tàyyi, sama put gi wow koŋŋ. Ma séentu la, yaw sama Yàlla, ba samay gët giim.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.