TSK

TSK · Genesis 46:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mu delluwaat ëmb, am doom ju góor, ba noppi waxaat ne: «Bii yoon sama jëkkër dina am cofeel ci man, ndax jural naa ko ñetti doom yu góor,» loolu tax mu tudde ko Lewi (mu firi Boroom cofeel).

¶ Bànni Israyil ya yilifoon seen kër baay, ñoo di: Góor ña Ruben, taawu Israyil, jur: Anog ak Palu ak Esron ak Karmi. Ñooñoo sos làngi Ruben.

¶ Gerson ak Keyat ak Merari ñoo soqikoo ci Lewi.

¶ Lewi la wax ne ko: Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya, ñeel na góor gay sa wóllëre, yaa ko nattoo ca Maasa, joteek moom ca ndoxum Meriba.