«Réccu naa li ma fale Sóol buur, ndax dëddu na ma, te samay ndigal, jëfewu ko.» Samiyel am ca njàqare lool, ba fanaanee tinu Aji Sax ji guddi gépp.
TSK
TSK · Hebrews 10:39
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Déggadi sànk ab téxét, naagu rey ab dof.
Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.
Bu leen kenn naxe nenn, ndax bés ba du dikkagum, te fippu gu mag ga jëkkula dikk, ba ki jëmmal ndëngte te dëgmal alkute, feeñ.
Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan, aki fiir, ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute.
¶ Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci.
yeen ñi seen ngëm tax ngeen yiiru ci manoorey Yàlla, mi leen di nége mucc ga mu waajal te di ko feeñal ca bés bu mujj ba.
Ñooñooy gàkkal seen jataayu lekk yi gëmkat ñiy bokk, di ñóox te amuñu ci jenn jom; ñooy xiin yu naaxsaay yu ngelaw li yóbbu; ñooy garab yu dee ñaari yoon, du meññ waxtoom, reen ya buddiku.
Rab wi masoona nekk te nekkatul nag, moom ci boppam moo di juróom ñetteelu buur bi, kenn la ci juróom ñaari buur yi jiitu itam, te day sànkuji.