Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, baal ma deret ji ma tuur, ma siiwal sa njekk.
TSK
TSK · Hebrews 10:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kee moom mu ngi rendiw yëkk, sarxal, te teewu koo bóome. Kee rendiw xar, sarxal, te teewu koo damm loosu xaj, sarxal. Kee ngi joxe saraxu pepp, te teewu koo tuur deretu mbaam-xuux. Kee di taal saraxu baaxantalu cuuraay, tey jaamu ay tuur. Ñoo taamu seen yoonu bopp, safoo seeni jëf ju seexluwu.
¶ Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa ne: «Seen juru saraxu rendi-dóomal, dollileen ko ci seen yeneen sarax, te lekk yàpp wi.
Israyiloo, dellul ci sa Yàlla Aji Sax ji, fakktaloo nga sag ñaawtéef.
Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji, ba sujjóotal Yàlla jooja fa kaw. Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal, ay wëlluy menn at?
Loolu misaal la, ñeel jamonoy tey, di firndeel ne jooxe yi ak saraxi jur yi ñu daan jébbale manuñoo dindi yaraangeg jaamukatub Yàlla bi, ba mu set wecc.
Dafa jëkk ne: «Saraxi jur aki jooxe, saraxi dóomal ak saraxi póotum bàkkaar, bugguloo, safoowuloo,» doonte yoon wee laaj yooyu sarax.