¶ Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf.
TSK
TSK · Hebrews 11:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Séentuleen kaw, xool-leen ki sàkk yii fi kaw! Xanaa kiy daaguloo seen gàngoor gu mat, ñoom ñépp lay woo ci seen tur, ci kawewaayu dooleem ak màggaayu kàttanam, te kenn du ci wuute.
Ki séddoo Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan. Kookoo bind lépp, te Israyil di giir gi mu séddoo. Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!
«Yeen, lu leen xiir ci lii? Nun itam ay nit lanu, bokk ak yeen benn bind. Xibaaru jàmm bi lanu leen di xamal, ngir ngeen wacc yëfi neen yii te walbatiku ci Yàlla, kiy dund te sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem lu nekk ci biir.
Ndaxam lees mana xam ci Yàlla, leer na ci seen biir, nde Yàlla moo leen ko leeralal.
Ci fan yu mujj yii, Doom ji la waxe ak nun, ki mu jagleel lépp, ki mu sàkke àddina wërngal këpp.
«Yàlla sunu Boroom, yaa yeyoo daraja ak teraanga ak kàttan, ndaxte yaa sàkk lépp, lépp lu am, yaw la soob, nga sàkk ko.»