¶ Aana mujj ëmb ca ndeetel at ma. Gannaaw gi mu am doom ju góor, tudde ko Samiyel (mu firi Yàlla dégg na), ndax da ne: «Maa ko ñaan Aji Sax ji.»
TSK
TSK · Hebrews 11:32
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ci biir loolu ngóor sa Samiyel moom, ma ngay liggéeyal Aji Sax ji, sol xar-sànnim lẽewam.
Aji Sax ji yebal Yërubaal, teg ca Bedan, teg ca Yefte, teg ma ca, man Samiyel, daldi leen xettli ci seen noon yi leen séq, ba ngeen dëkke jàmm.
Samiyel fab béjjénu diw ba, diw ko fa kanam magam ña. Ba mu ko defee Noowug Aji Sax ji ne milib ca kaw Daawuda, dale fa ànd ak moom bésub keroog. Ba loolu wéyee Samiyel moom, dem dëkk ba ñu naan Raama.
¶ Samiyel nag faatu woon na, ba Israyil gépp dëj ko, denc ko ca Raama, dëkkam ba. Te itam Sóol mujjoon naa génne réew ma ñiy seete nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy gisaane.
¶ Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy.
Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti.
¶ «Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund.
Loolu lépp a ngi am ci diiru ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (450). «Gannaaw loolu moo sàkkal sunuy maam ay njiit, ba ci jamonoy Yonent Yàlla Samiyel.
¶ Waaye su sunug njubadi fésalee njubteg Yàlla, ana lu loolu mana tekki ci nun? Ma waxe ko nu ko nit mana dégge; ma ne, kon bu nu Yàlla wàcceelee am sànjam, deful ag njubadeem?
¶ Ana lu loolu di tekki nag? Ndax kon danuy wéye bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gëna yokku?
¶ Bokk yi, yonent yi wax ci turu Boroom bi, di dékku aw tiis, ak di muñ, defleen leen seeni royukaay.
Ndax kat du genn kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe waxyu bu bawoo fa Yàlla.