¶ Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal.
TSK
TSK · Hebrews 11:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga.
Lóot daldi génn, wax ak goroom, ya naroona takk ay doomam yu jigéen, ne leen: «Gaawleen gaaw, génn dëkk bi, ndaxte Aji Sax ji dina ko tas.» Teewul ñu defe ne day kaf.
¶ Mu bàyyikoo nag ca Alyaasa. Gannaaw gi mu tëjuji, mooki doomam; ñu di ko jox, muy sotti.
Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
«Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko.
te mu fekk Nóoyin ak Dañeel ak Ayóoba ci biir réew mi, giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ñooñu ñett duñu mana musal seen jenn doom, góor ak jigéen. Seen njubteg bopp mooy musal seen bakkan.
Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.
Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»
Gannaaw gi la jagoo màndargam xaraf, mu firndeel àtteb njubam gi ngëmam waral, te fekkul mu xaraf. Noonu la Ibraayma mana nekke maamu mboolem gëmkat ñi. Looloo tax muy maamu mboolem ñi xaraful, te gëm, ndax ñu waññal leen seen ngëm, ab àtteb ñu jub.
¶ Ana lu nu ci mana wax? Xeet yu dul Yawut te sàkkuwuñu woon ag njub, ñoo jagoo àtteb njub, te mooy njub gi ngëm di maye.
Ndax nun kat, ci ndimbalal Noo gi, ak ci sunu kaw ngëm lanu yaakaare ñu jox nu àtteb njub bi nuy séentu.
Fan yi Almasi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te nangule na it, ndax na mu ragale woon Yàlla.
ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yett gaal, ga lim bu néew, juróom ñett, mucce woon ca ndox ma.
ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan waare njekk tey kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi;