Ba mu ko defee Musaa dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Éey Aji Sax ji, mbooloo mii de moy nañu la lool, ba ñu sàkkalee seen bopp ay yàllay wurus.
TSK
TSK · Hebrews 13:17
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Lu la tere woona déggal Aji Sax ji, xanaa di saax-saaxee alal ji, di def li Aji Sax ji ñaawlu?»
Yerusalem, tabb naa ay jongrukat ci sa kawi tata. Buñu selaw, du guddi du bëccëg! Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, buleen dal-lu.
«Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko.
¶ «Yaw nit ki nag, jongrukat laa la tabb, ñeel waa kër Israyil, ba boo déggee baat bu jibe sama gémmiñ, war leen koo artoo ci sama ndigal.
Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.
Kon ku nekk ci nun, yaay layool sa bopp fa Yàlla.
ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak mboolem ñu bokk ak ñoom liggéey bi ak coono bi.
te ngeen rus Almasi, ba tax ngeen di nangulante.
¶ Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,
Teertooleen ko mbégte mu mat sëkk ngir Sang bi, te it nawleen ñu mel ni moom,
¶ Kon nag yeen samay bokk, soppe yi ma namm, di leen bége, te ngeen di sama kaalag ndam, gi ma yooloo ci sama liggéey, ngalla soppe yi, nangeen saxe noonu ci Boroom bi!
Ndaw njukkal lu nuy dellooti Yàlla ngir yeen, ndax mboolem mbég mi nu leen di bége fi sunu kanam Yàlla!
¶ Ku ci déggul sunu kàddu yi ñu bind ci bataaxal bii nag, bàyyileen ko xel, te baña jaxasoo ak moom, ngir gàcceel ko.
¶ Fàttlikuleen seen njiit, yi leen àgge kàddug Yàlla. Nemmikuleen li seenug dundin meññ, te ngeen roy seen ngëm.
¶ Kon nag nangul-leen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»