¶ Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët.
TSK
TSK · Hebrews 2:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.
Sama doom, déggal samay wax, fonk samay santaane.
Gone yi, tee ngeena dégg yaru baay, te déglu, ba am ug dégg?
Doom, sàmmal samay wax, fonk samay santaane.
Gàcce ngay gëna regg teraanga, naanal yaw it te wone sa mbuñuka! Ci yaw la kaas bi ci ndijooral Aji Sax ji di walbatiku, sa toroxte wuutu sa teraanga.
¶ «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»
Gannaaw nag kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi, mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ,
¶ Wattuleen bala ngeena tanqamlu kiy wax ak yeen. Ndegam ña tanqamlu woon ka yékkati woon kàddoom, wax ak ñoom ci kaw suuf ñoo rëccul, aste nun ñii, su nu dëddoo kiy waxe fa asamaan.
Waaye dinaa def sama kem-kàttan, ba fu ngeen tollu, di fàttliku mbir yooyu, gannaaw bu ma dëddoo.