TSK

TSK · Hebrews 4:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.

Mbégte ñeel na ku saxoo ragal, waaye ku dëgër bopp tàbbi ci njekkar.

Bu boroom kër gi xasee jóg, ba tëj bunt bi, fa ngeen di doxe des biti, di fëgg naan: “Sang bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.”

Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla,

Man nag noonu laay dawe, waaye samaw xél ñàkkul ab jëmu. Noonu laay këmëxee it, waaye dóoruma ci jaww ji.

Su nu ko gàntalee, moom it dinanu gàntal; su nu ko ñàkkee kóllëre, mu saxoo kóllëreem, ndax manula gàntal boppam.

Moo ma taxa giñe sama biir mer, ne: “Duñu tàbbi mukk ci samag noflaay.”»

Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.

Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.

¶ Fàttlikuleen seen njiit, yi leen àgge kàddug Yàlla. Nemmikuleen li seenug dundin meññ, te ngeen roy seen ngëm.