TSK

TSK · Hebrews 5:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

te yót ko doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi. Na sarxalkat bi sàkk barci-loxob sunguf su mucc ayib soosu ànd ak diw gi, te boole kook cuuraay li lépp. Na sarxalkat bi def cér boobu saraxu baaxantal, lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, Aji Sax ji taxawu ma,

Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel Daawuda.

Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat Leyanot, di taalifu Eman, mi bokk ci giirug Esra.

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.

¶ Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dee.

Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,

¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.

¶ Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,