TSK

TSK · Hebrews 6:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye yaw askan wi, ñi nga deele ñooy dellu dundaat, seeni néew ay dekki, ku doon nelaw sa biir bàmmeel, yewwu, sarxolle. Aji Sax jeey yebal lay bu ànd aki leer, suuf délloosi ña dëddu.

Ñu baree ngi nelaw, keroog ñu yewwoo fa pëndub suuf. Ñenn ña nara dund fàww, ña ca des añe gàcceek njàqare fàww.

Farisen bi nag jaaxle, ndax la Yeesu setluwul bala moo waaja lekk.

Su boobaa ndokklee yaw, nde amuñu sag pey, waaye dees na la fey, kera ndekkitel aji jub ñi.»

Acts 2:38 TSK

Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.

Acts 4:2 TSK

Fekk na leen ñéññ ca la ñuy waare ak a yégle ndekkitel Yeesu, te loolu di dëggal ne ndee-ndekki, lu am la.

Acts 8:12 TSK

Waaye ba ñu gëmee Filib, ma leen xamal xibaaru jàmm, bi jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Almasi, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.

¶ Piyeer dellu ne: «Ñii jot Noo gu Sell gi ni nun, ndax manees na leena baña sóob ci ndox?»

Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.

¶ Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebatukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»

Acts 19:2 TSK

ne leen: «Ndax ba ngeen gëmee, jot ngeen ci Noo gu Sell gi?» Ñu ne ko: «Nun de yégunu woon sax ne Noo gu Sell gi am na.»

Yaakaar ji ma am, mooy yaakaar ji ñu am ñoom itam, ne ñi jub ak ñi jubadi, ñépp ay bokk dekki ëllëg.

Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»

¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.

Dangeena umple ne mboolem nun ñi ñu sóob ci Yeesu Almasi, cig deeyam lañu nu sóobaale?

Ñoom ñépp lañu sóob sóobeb Musaa, ca biir niir wa, ak ca biir géej ga.

Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, nirule kook yaramam wi ànd ak teddnga.

Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.

Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.

ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yett gaal, ga lim bu néew, juróom ñett, mucce woon ca ndox ma.

Jude 1:14 TSK

¶ Enog, juróom ñaareelu maam ma gannaaw Aadama, ñooñu la jottli woon waxyu bu leen dal, ne: «Boroom baa ngii dikk, ànd ak ay junniy junneem ñu sell,