Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir.
TSK
TSK · Hebrews 9:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Wewal rido bi ci ron lonku yi, su ko defee nga yóbbu gaalu àlluway seede si foofu ci gannaaw rido bi, rido bi xàjjaleel leen bérab bu sell bi, ak bérab bu sell bee sell.
¶ «Lii nag mooy li nga leen di defal, ngir sédd leen céru sellnga, ngir ñu di ma sarxalal: Dangay jël yëkk wu ndaw ak ñaari kuuy yu amul sikk,
¶ Ba loolu amee mboolem ñu xareñ ñi bokk ci liggéey bi daldi defar jaamookaay bi. Ñu def ko fukki sori rabali lẽe, yu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr. Ñu ñawaale ci ay nataali serub.
¶ Noonu la mboolem liggéeyu màkkaanu xaymab ndaje mi mate. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa rekk, ni la ko bànni Israyil defe.
«Bu keroogee benn fanu weer wi jiitu, nanga samp màkkaanu xaymab ndaje mi.
¶ Musaa nag samplu jaamookaay bi: Ñu jiital tegu yi, samp làcc yi, we galan yi, daldi samp jën yi.
¶ «Sàkkal sunguf su mucc ayib, lakk ci fukki mburu ak ñaar, mburu mu nekk di juróom benni kiloy sunguf.