TSK

TSK · Hosea 13:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Kenn du Yàllay Yesurun! Keey war asamaan, wallusi leen, war ay niir, ànd ak darajaam.

¶ Li waral ñu nangu Samari mooy waa Israyil a bàkkaar, tooñ Aji Sax ji seen Yàlla ja leen génne réewum Misra, xettli leen ca Firawna buuru Misra. Waa Israyil di jaamu yeneen yàlla,

Nu ngi séentu Aji Sax ji, moo nuy taxawu, di nu feg.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Damaa séentu tund ya, te naan fu wall di jóge?

Njaaloo di ñàkk bopp, kuy sànk bakkanam a koy def.

Seen dëgër bët tuumaal na leen, ñuy bàkkaar ni waa Sodom, làquwuñu sax. Wóoy, ngalla ñoom! nde ñoo lor seen bopp.

Xanaa du yeena def seen bopp lii, di wacc seen Yàlla Aji Sax ji, ba mu leen di jiite ca yoon wa?

«Sa jëfin ak say jëf a la yóbbe lii, sa musibaa ngook, wex la xàtt, di dagg sa xol.»

Du seen xol lañu ma wooye wall, xanaa di salliiru ci seen kaw lal, pepp ak biiñ tax ñuy dagg seen yaram, dëddu ma.

«Man Aji Sax ji, fa Misra laa dale di seen Yàlla, xamuleen Yàlla ju dul man, te kenn du musle ku ma moy.

«Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk, mu baaxe nu!” Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.