Seen doole dina kasara, ndax suuf si ngeen di bey du leen nangul te garabi réew mi du meññ.
TSK
TSK · Hosea 2:11
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Buleen fi indeeti saraxi caaxaan, seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la. Terutel weer ak bésub Noflaay ak wooteb ndajee ci yem! Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.
Maay dakkal fi dëkki Yuda, dakkal fi mbeddi Yerusalem coowal mbégteek bànneex, dakkal kàddug boroom séet, dakkal kàddug séet, ndax réew mu tumurànke.
Te muy kàddug mbégte di kàddug bànneex, di kàddug boroom séet akub séetam, di wolukaay bu fiy jib mbaa leer gu ñuy niitoo, lépp maa ko fiy boole tukkal.
Ndax kat ay fan yu bare la bànni Israyil di toog te duñu am buur, duñu am kàngam. Duñu rendi sarax, duñu am tuuri doj, duñu am xar-sànni, duñu am gàllaaji kër.
Ndaxam dàgga ak nalukaayu reseñ du leen regg, te biiñ du leen doy.
Bésub keroog jàngi kër Buur doon ay jooy.» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «Néew yi, xas, fu ne ñu jalax, lépp selaw!»
Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay sowal jant digg bëccëg, lëndëmal suuf bëccëg ndarakàmm.
Buumi xalam ak baatu woykat, toxorooku liit, lenn du ci jibeeti fi yaw. Liggéeykat bu xareñ bu mu mana doon, deesatu ko gis fi yaw, doju wolukaay du riireeti fi yaw,