1 C a ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.
2 Ñaari fan, mu leqli nu, ñetteel ba mu yékkati nu, nuy dund fi kanamam.
3 Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
4 «Ana nu ma lay def, yaw Efrayim? Nu ma lay def yaw Yuda? Te sa ngor di xiinu suba, mbaa ab lay, jekki ne mes.
5 Moo tax yonent yi laa leen di dumaa, sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye. Seen àttee leen di jollil ni ceeñeeru njël.
6 Ndax ngor laa namm, dub sarax, ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.
7 «Waaye ñoom ca dëkk ba, Adam lañu feccee kóllëre, foofa lañu ma wore.
8 Galàdd mooy dëkkub defkati ñaawtéef, taq ripp ak deret.
9 Ni saaysaay siy tëroo, ni la sarxalkat yi lëkkoo, di bóome ca yoonu Sikem. Ndaw jëf ju ñaaw!
10 Ci kërug Israyil laa gis lu yées: Fa la Efrayim di gànctoo, Israyil googu laa ne moo sobeel boppam.
11 Yuda yaw it, sam ngóob ma ngay taxawe, kera bu may tijji sama wërsëgu ñoñ.