Seen meññeefum suuf, ak mboolem seenu ñaq, xeet wu ngeen xamuloon a koy lekk, te dees leen di not ak a dëggaate rekk, bés bu nekk.
TSK
TSK · Hosea 8:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Merum Aji Sax ji nag ne jippét ca kaw Israyil, mu teg leen lu yàgg ci loxoy Asayel buurub Siri ak Ben Addàd doomu Asayel.
Ci jamonoy Peka buurub Israyil, Tiglaat Pilser buurub Asiri dikk, nangu dëkk yi ñuy wax Yon ak Abel Bet Maaka ak Yanowa ak Kedes ak Àccor ak diiwaani Galàdd ak Galile ak mboolem réewum Neftali. Mu jàpp waa réew ma, yóbbu Asiri.
Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.
Bés ba ngeen ko jëmbatee, ngeen gis mu sax, ëllëg ba bët setee, mu tóor, te ngóob réer bésub wopp, ci biir mitit wu amul paj.
Jiwum pepp, góob ay dég; sonn, ñàkk yool, xanaa mbetteel ci meññeef mii sababoo ci merum Aji Sax ji.»
Ay doxandéem a jeexal dooleem, te xamu ko, aw liir tege ci kawam weex tàll, te yégu ko.
Yeena bey ag coxor, góob ag mbon. Yeena lekk meññeefum fen, nde yeena wóolu seen pexey bopp, ak seen jàmbaar yu bare.
¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.