TSK

TSK · Isaiah 12:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ndax seen Yàlla Aji Sax ji mooy dem ak a dikk ci seen biir dal bi, ngir xettli leen, ba jébbal leen seeni noon. Kon nag seenub dal daa wara sell, ngir Aji Sax ji ñàkka gis fi seen biir, lenn lu tegginewul, ba dëddu leen.

Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan, tundu Basan, tund wi ci coll yi,

Seen darajay doole, yaw a. Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.

Mu ne: «Fii laay dal-loo ba fàww, fii laay dëkk, maa ko taamu.

Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ki dëkke tundu Siyoŋ.

Kersa la weer wiy am, gàcce ñeel jant bi; Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ, leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.

Foofa déy la nu Aji Sax ju màgg ji di nekkal bérab bu defi dex aki wal, fu gaalu joow dul dawe, te gaal gu mag du fa jaare,

Yaw Siyoŋ, xibaarkatu jàmm bi, doxal yéegi tund wu kawe, te xaacook doole. Yaw Yerusalem, xibaarkatu jàmm bi, xaacul te bul ragal! Neel dëkki Yuda yi: «Seen Yàllaa ngi!

Yaa leen di bàcc, ngelaw wal, ngëlén tasaare; yaw ngay bége Aji Sax ji, di damoo Aji Sell ju Israyil.

Ndaw leeka rafeti tànk, kee bartaloo tund yi, di la dégtalsi jàmm, di la xibaar lu neex, àgge la ag mucc, ne la: «Éey, Siyoŋ, sa Yàllaay Buur!»

«Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul! Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.» Aji Sax ji nee: «Ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot kiy séy.

Wurmbalu dëkk bi bépp fukki junniy xasab ak juróom ñett (18 000) lay doon. Turu dëkk bi nag, dale ko ca bés ba, di “Aji Sax jaa ngi fi.”»

Wóoy ngalla yeen waa tefesu géej, yeen xeetu Kereteen ñi, kàddug Aji Sax ji dal na leen. Yeen waa Kanaan, réewum Filisteen ñi, maa leen di sànk ba dungeen dese kenn,

¶ Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju ŋàbb buumu nattukaay ci loxoom.

«Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,» kàddug Aji Sax jee. «Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo, ni laa leen tasaaree.» Kàddug Aji Sax jee.

Ba ñu jubsee Yerusalem, bay wàcce ca mbartalum tundu Oliw ya, mbooloom taalibe mépp la mbégte jàpp, ñu tàmbalee sàbbaal Yàlla ca kaw ndax kéemaan ya ñu gis.