TSK

TSK · Isaiah 17:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 21:18 TSK

Ana fu ku bon mele nim ñax mu ngelaw wal, mbaa boob mu callweer yóbbu?

Loolu dalul moos ku bon, kay mel ni xatax bu ngelaw li wal.

Yal na leen malaakam Aji Sax ji bëmëx, nim ñax mu ngelaw wal.

di dalal riirum géej aki gannaxam, ak coowal xeet yi,

Éy Yàlla, wëndeel leen ni callweer, ñu mel ni boob mu ngelaw wal.

Boroom baa ngoog, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi, njobbaxtal ya gëna kawe dog, la ca gënoona siggi, wàcc.

Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy serloo ci tàngoor, nde merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw miir.

Say noon ay def gàngoor ni feppi suuf, di naaxu nit ñu néeg, ñu ngelaw liy wal nib cox. Loolooy jekki am, ca saa sa.

Aji Sax jeey yékkati kàddoom gu màgg, wone diisaayu loxoom, ànd ak tàngooru meram, ak sawara wuy xoyome, ak waameek ngëlén, ak tawub doji yuur.

Ñi ñu yaakaar dañuy tiit, ne wëqet, seeni kilifa jàq, ba daw wacc raaya ba. Kàddug Aji Sax jee, Boroom sawara wi ci Siyoŋ, Boroom taal bi ci Yerusalem!

Sam riir jib, xeet yi fëx; nga jóg, waaso yi fëlxoo.

Yaa xadaru sama kaw, ba sag reewande tàbbi sama nopp! Maa lay takkal ag nos akug laab, waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon.

Maa ngii di la def ngay watiiru bàccukaay bu ñaw, yees peq; ànd aki bëñam, ngay wol tund wu mag, raatale; dëbb tund wu ndaw ba mu mel nib cox.

Moo leen tax di naaxsaay ni niiru suba, mbaa layub njël, mbaa mboob mu naawe dàgga ja, mbaa saxar su gillee ci jankub néeg.