TSK

TSK · Isaiah 2:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Foofa ngeen di jaamoo ay yàlla yu loxoy nit sàkke bant, mbaa doj, yàlla yu dul gis, du dégg, du lekk, du xeeñtu.

Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu Baal.

Maa duma réew yu seeni yàllantu, seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari.

te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen.

Ndesu matt ma lay sàkke jëmmu tuuram, sukkal ko, sujjóotal ko, ñaan ko, naa: «Yaay sama Yàlla, xettli ma!»

Maay biral samay àtteek ñoom ci seen mbon gi gépp: Dañu maa wacc, di taalal cuuraay yeneen yàlla, di sujjóotal lu ñu sàkke seeni loxo.

¶ «Yaw Yuda, ni sa dëkk yu mag tollu, ni la say tuur tollu. Ni mbeddi Yerusalem tollu it, ni la sarxalukaay yi ñu fa saam tollu, ñu di fa taalal cuuraay Baal, tuur mu seexluwu mi.»

Hosea 8:6 TSK

«Israyil la lii jóge, te ab liggéeykat moo ko sàkk. Kon lii du Yàlla! Ay tojit la wëlluw Samari di mujje.

Léegi ñu ngi gën di bàkkaar, di xellee ci seen xaalis jëmmu tuur, ay jëmmi xërëm yu ñu sàkke seen xareñte, lépp di càkkéefu ay liggéeykat, te ci ñoom la nit ñi naan: «Rendikati sarax yaa ngi fóon ay tuuri wëllu.»

Maay dagge fi sa biir say tuur, ak sa xeri jaamookaay, te dootoo sujjóotal loo sàkke say loxo.

¶ Ndesu nit ñi musiba yooyii reyul nag, taxul sax ñu tuub seeni jëf, ba bañatee jaamu ay tuur, ak jëmmi xërëmi wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk; xërëm yu gisul, déggul, doxul.