su boobaa nangeen woyal buuru Babilon léeb wii, ne ko: «Moo nu ki daan note mujje? Nu mu mujjeek reewandeem?
TSK
TSK · Isaiah 21:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Waxleen xeet yi, yéeneleen, woneleen misaal te yéene, waxleen lii, bañ cee làq dara. Neleen: “Dees na nangu Babilon, torxal Bel mbaa Mardug, tuur mi, tas ko, gàcceel gàllaaj yi, tas kasaray tuur yi.”
Wooleen fittkatoo fittkat fi kaw Babilon, mboolem kuy tàwwi xala. Gawleen ko, bu kenn rëcc. Feyleen koy jëfam; def ko ni mu def moroomam. Babilon a jaay reewande Aji Sax ji, ku Sell ku Israyil ki.
Yeen waa Babilon, réew mu taaru mi, fitt aku xeej la ñooñuy ŋàbb, néeg lool, duñu yërëm, seen coow ni riirum géej, ñu war seeni fas, làng-déral leen ni benn bopp ngir xare.
«Yékkatileen ub raaya fi réew mi te walal liit gi xeet yi. Dajaleleen xeet yi fi kaw Babilon, te xabtal fi kawam réew yii: Araraat ak Minni ak Askenas. Tabbal-leen ko njiitu xare mu ko song, indil koy fas yu saf ndiiraani njéeréer.
Kon ay bés a ngii di ñëw, yu may dikke mbugal tuuri Babilon, réew mépp torox, ña ñu bóom ñépp wetaroo fa biir.
Su ko defee nga ne: “Nii la Babilon di diige te du jógati ndax safaan bi may wàcce fi seen kaw, ba ñu sonn.”» Fii la kàdduy Yeremi yem.
Mu àddu ca kaw, ne: «Babilon a daanoo! Dëkk bu mag ba daanu na, ba doon dëkkukaayu jinne ak mboolem njuuma lu sobewu ak mboolem picc ak rabu àll wu sobewu te siblu.