TSK

TSK · Isaiah 26:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Sàmmooleen koo jëfe, ndax mooy doon seenug rafet xel, ak seenug ràññee fi kanam xeet yi, ba bu ñu déggee mboolem dogali yoon yii, dinañu ne: «Wii askan wu mag rekk a rafet um xel te ràññee!»

Ubbil-leen ma bunti njekk, ma dugg santi Ki Sax.

Njekk moo lay dëgëral, nga sore noteel, doo tiit; sore tiitaange, du la jege.

Say wunt ay ubbiku saa su ne, guddeek bëccëg, du tëje, xanaa di la jàlleel alali xeet yi, seeni buur riixle ànd ca.

Su boobaa xeet yi gis sag njekk, buur yépp gis sa daraja, ba ñu di la tudde tur wu yees, wu Aji Sax ji di tuddal boppam.

Miir bu ci nekk dina am ñetti bunt yu ñu dippee ñetti giiri Israyil. Wetu bëj-gànnaar, benn buntu Ruben ak benn buntu Yuda ak benn buntu Lewi.

Acts 2:47 TSK

Ñuy màggal Yàlla, ñépp naw leen. Bés bu nekk nag Boroom bi di yokk ca mbooloo mooma, nit ña jota mucc.

Waaye asamaan su bees ak suuf su bees sa njub di dëkki bu keroogee, moom lanuy séentu, na nu ñu ko dige woon.

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.