Nanga dërkiisal xoli askan wii, fatt seeni nopp, taf seeni gët; lu ko moy seeni gët gis, seeni nopp dégg, seen xol yég, ñu dëpp, wér.»
TSK
TSK · Isaiah 29:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
Aji Sax ji déy yeen la wal ngelawal nelaw yu xóot, taf seeni gët, te ngeen di yonent yi; muur seeni bopp te ngeen di boroom peeñu yi.
Ñi lay néewal, maa leen di leel seen suuxu bopp. Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen, ba kuy boroom suux xam ne maay Aji Sax ji lay wallu, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.»
Rikk déglul nag lii, yaw mi musiba dal, nga màndi te du biiñ.
Asamaanee, waarul ci lii! Jommil, ba jommaaral!» Kàddug Aji Sax jee.
Mu jëm ci yonent yi: Sama bopp a ubu ràpp, sama xol jeex, sama yax yépp ne yalax, ma mel ni ku biiñ man, ba mu màndi ndax Aji Sax ji ak kàddoom yu sell.
Aji Sax jee yor Babilon ci loxoom, muy kaasu wurus bu def xadaru xeet ya, di màndal mboolem àddina; xeet ya naan ca, ba tax ñuy say.
«Xool-leen ci biir xeet yi ba gis,» la Aji Sax ji wax. Jaaxleleen ba jàq, nde jëf a ngi jëfe ci seeni jant, bu ñu leen ko waxoon, dungeen ko gëm.
Ma gis ne jigéen ji daa naan ba màndi ci deretu ñu sell ñi ak deretu ñi doon seedeel Yeesu. Ba ma ko gisee, jaaxle naa lool.