TSK

TSK · Isaiah 3:24

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax jee leen di dumaa woppi ràgg, ak yaram wu tàng, ak lakk-lakk, ak jant bu tàng jérr, ak maral, ak gàncax gu xuur, tegi liir, lépp topp leen ba ngeen sànku.

¶ Booba bala ayu kenn ci xale yu jigéen ñiy agsi, ba muy dem ca Buur Aserus, day fekk mu matal fukki weer ak yaar yi ñu àppal jigéen ñi, ngir ñu yokk ci seen taar. Juróom benni weer yi, ñu di leen diw ndàbb lu ñuy wax miir; juróom benni weer yi ci des, ñu di leen diw ay diw yu xeeñ ak yeneen yu jigéen ñiy defaroo.

Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.

Boroom beey wal noowal mbugal, noo guy lakk, sellal, fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ, fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set.

nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya, ak kaw taax yaak pénc ya, ku ne di jooy ba say rongooñ wale.

Yeen jigéen ñi dal xel, taxawleen temm, déglu ma; yeen janq ji féex, teewluleen ma.

Kon nag sol-leeni saaku, ñaawloo te yuuxu ne: “Merum Aji Sax ji tàng na kat te moyu nu.”

Ñoom ñépp a nelu, wat seeni sikkim, daggat seeni loxo, sol ay saaku, di ko ñaawloo.

Magi janq Siyoŋ mu taaru ña nga toog, xeremlu, xëppoo suuf, sol ay saaku, di ñaawlu. Janqi Yerusalem sëgg, seen bopp jëm suuf.

Yaay tax ñuy nelu, sol ay saaku di ko ñaawloo, di la jooye naqaru xol ak yuux yu metti.

Amos 8:10 TSK

Maay soppli seeni màggal ab dëj, seen woyoo woy diy jooy. Maay wodde bépp lupp saaku yu ñuy ñaawloo, bépp bopp, ma wat ub nel, def ko mu mel ni dëju benn bàjjo bu góor, muj ga di bés bu tar.

¶ Seen gànjar bumu doon gànjaru biti bu yem ci ay létt yu rafet, ak takkaayi wurus, ak yére yu yànj,

Ci kaw loolu tàngooru naaj wu metti di lakk nit ñi. Nit ñi nag tuubuñu, sàbbaal Yàlla; xanaa di saaga Yàlla, ji dogal yooyu musiba.