Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
TSK
TSK · Isaiah 3:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ñu daldi woo Lóot ne ko: «Ana góor ñi fi ñëw tey ci guddi? Génneel nu leen fii, ndax nu mana àgg ci ñoom.»
¶ Gannaaw loolu Samiyel ne: «Indil-leen ma Agag buurub Amalegeen ñi.» Agag nag dikk, wutsi ko, ne finaax. Booba Agag a nga naan ca xelam: «Dee moom, tiitatuma ko, wees na!»
Ku bon daŋŋiiral, seetul dara, xalaatam yépp mooy Yàlla amul.
Ku ma moy loru, ku ma bañ, daa repp.»
Aji Sax ji da ne: «Jigéeni Siyoŋ a ngi daŋŋiiral, di goŋeet-goŋeeti, di regejook a rékk-rékkal, samp um ndaag, keleŋal lami wëq.»
Moo tax waame aje, taw yiy mujje dikkul. Teewul ngeen dëgër bët nib gànc, ñàkk gàcce!
«Li nga nuy wax ci turu Aji Sax ji, dunu ko déglu.
Rakk ja teg nataal ya bët rekk, xédd leen, yónnee leeni ndaw fa Kalde.
Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal, Israyil ak Efrayim ñooy fakktaloo seenug ñaawtéef, Yuda it ànd ak ñoom fakktalu.
Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.