Yeen nag defuleen lu moy jóg wuutu seeni baay, njurum bàkkaarkat yi ngeen doon, di xamb sànjum Aji Sax, ji tàkkal bànni Israyil?
TSK
TSK · Isaiah 30:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Gàntal Aji Sax ji ngeen nekke naka jekk, dale ko ca bés ba ma leen xamee.
Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas!
Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
Asamaan, déglul; suuf, teewlul, Aji Sax jeey àddu: «Ay gone laa yar, màggloo leen, ñoom, ñu gàntal ma.
Xanaa dungeen wéye fippu, ñu gën leena duma, te bopp di góomi neen, xol jeex tàkk?
Wóoy ngalla ñiy ràngooy buum, di diri ñaawtéefi neen, ràngooy goj di diri seeni tooñ.
Am na ñu naan: «Laajleen ñiy gisaanee nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy kebetook a ŋun-ŋuni. Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur, tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.»
Lal a gàtt ba deesu ci tàlli, malaan cëkk ba matul càngaay.
Wii xeet kat ay fippukat lañu, yii doom a diy fen-kat te nanguwuñoo sàmm yoonu Aji Sax ji!
ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, di kiiraay ci ngëlén, mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
Samay loxo laa yendoo tàllal askanu fippukat, nit ñuy doxe yoon wu baaxul, topp seen xelum bopp.
Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool, ndax man la gàntal.» Kàddug Aji Sax jee.
Mu ne ma: «Yaw nit ki, maa lay yebal ci bànni Israyil, xeeti fippukat yi fippu ci sama kaw; ñook seeni maam dañu maa masa tooñ ba bésub tey jii.
Sa làmmiñ laay taqal ci sa denqleñ, nga luu ba doo leen mana yedd, ndax kërug fippukat lañu.
Ñooy lekk te duñu regg, di gànctu te duñu giir, nde Aji Sax ji lañu noppee topp.
Ab saamar ay wëndeelu ca seen dëkk yu mag, dàjji seen bunti dëkk, ba warax leen ndax seeni mébét.
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.