Nehemiah 8:8
TSK
Ci biir loolu ñu di leen jàngal téereb yoonu Yàlla wi, njàng mu leer, di leen ko firil ba ñu xam li ñuy jàng.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ci biir loolu ñu di leen jàngal téereb yoonu Yàlla wi, njàng mu leer, di leen ko firil ba ñu xam li ñuy jàng.
ba ñi réeroon, mujj xam; ñurumtukat yi dégg ndigal.
Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.
¶ Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.
Déggoon nañu rekk ñu naan: «Ki nu daan bundxatal bu jëkk, di yàq sunu yoonu ngëm wi de, léegi mooy yégle xibaaru jàmm bi koy xamle!»