TSK

TSK · Isaiah 43:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba saraxu ngoon jotee, Yonent Yàlla Ilyaas jegesi, ñaan ne: «Aji Sax ji, yaw Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, xamleel bésub tey jii ne yaw yaa di Yàlla ci Israyil, ma di sab jaam bi def lii lépp ci sa ndigal.

Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Yàlla, Aji Sax ji Yàlla àddu na, di woo àddina, penku ba sowu.

«Waxleen seenu lay,» la Aji Sax ji wax, «Biral-leen seeni firnde,» la buuru Yanqóoba boobu wax.

Fàttli ma saw lay, nu bokk layoo; waxal boog yaw, ndax nga yey!

Ana ku mel ni man? Na àddu! Na biral firndeem te taajal ma la amoon ba may sos xeet wu yàgg wa, ak li dikkagul. Na ko wax!

Yeen daw-làquy xeet yi, dajeleen, dikk, ànd, jegesi. Képp ku gàddu tuuru bantam, ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu, kooka xamul dara.

Moo tax ma yàgg leena biralal lii, yégal leen ko balaa teew. Lu ko moy ngeen ne: «Sunu tuur mee ko def, sunu tuuru bant bee, sunu tuuru weñ gee ko amal di!»