Kee di cëslaay, te mati jëf, wépp yoonam di njub. Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, te njekk ak njub mooy boroom.
TSK
TSK · Isaiah 45:19
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndaxte rusoon naa ñaan Buur mu boole nook ay dag ak gawar yu nu aar ci noon yi ci yoon wi. Li ko waral mooy fekkoon na nu wax Buur ne ko: «Sunu Yàlla mooy toppe yiwam mboolem ku ko yaakaar, di ko defal jàmm, waaye meram dina dal ak doole ci kaw mboolem ku ko dëddu.»
Ku ñàkk a ngi, ñu futti, mu ngi binni, di néew-ji-doole. Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg, teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.»
Lu Aji Sax ji tegtale, njub la, di bégal xol. Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la, di leeral gis-gis.
Waa pénc ma di ma tooge, màndikat yi di ma woyal.
Ay jëfam dëgg laak njub, tegtalam yépp mata wóolu,
Ma ngay wootee bérab yu gëna xumb, di dégtaley kàddoom, bunt dëkk ba.
Déglul, ma wax la lu am solo, dégtal la njub.
Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo.
Am na ñu naan: «Laajleen ñiy gisaanee nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy kebetook a ŋun-ŋuni. Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur, tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.»
Giñ naa ko ci man mii, sama gémmiñ njekk a ciy jibe, di kàddu gu dul randu. Man la ñépp di sukkal seen bëti óom, man it la bépp boroom làmmiñ di giñe.
Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.
Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»
maa leen di may ngeen daj ma.» Kàddug Aji Sax jee. «Maa leen di tijjil seen wërsëg, dajalee leen ci mboolem xeet ak mboolem bérab ya ma leen sànni woon.» Kàddug Aji Sax jee. «Maa leen di délloosi bérab bii ma leen yebale woon ngàllo.»
«Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,» Aji Sax jee ko wax. «Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal”?
Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.