Waa Asdodd teela xëy ca ëllëg sa, fekkuñu lu moy jëmmu Dagon ja, mu daanu ba dëféenu fa suuf, fa kanam gaalu Aji Sax ji. Ñu yékkati jëmmu Dagon ja, delloo ko fa mu taxawoon.
TSK
TSK · Isaiah 46:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Digg bëccëg wees, ñu gëna ràkkaaju di wax ay waxyu, ba saraxu ngoon jot. Waaye du lenn lu àddu mbaa lenn lu wuyu mbaa lu leen faale.
Gannaaw gi, ba muy sujjóot ca kër tuuram ma ñuy wax Nisrog, Addraameleg ak Sareser, doomam yu góor ñoo ko fa fàdde saamar. Ñoom nag ñu daw làquji réew ma ñuy wax Araraat. Ci kaw loolu doomam Asaradon falu buur, wuutu ko.
Yeen daw-làquy xeet yi, dajeleen, dikk, ànd, jegesi. Képp ku gàddu tuuru bantam, ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu, kooka xamul dara.
Waaw, ana seen yàlla yi ngeen sàkkal seen bopp? Bu leen musiba dikkalee, nañ leen wallu, bu ñu ko manee! Gannaaw yeen waa Yuda, ni seeni dëkk tollu la seeni yàlla tollu!
Su ko defee waa dëkki Yuda yu mag yeek waa Yerusalem dem jooytuji ca yàlla, ya ñuy taalal cuuraay, te duñu leen mana wallu mukk ci seen jamonoy musiba.
Ba loolu amee mool ya tiit di yuuxoo, ku nekk di woo sa yàlla wall. Ñu sànni biir géej la ñu yeboon ca gaal ga ngir gëna woyof. Fekk na Yunus wàcc ca suufu gaal ga, tëdd di nelaw ba yàndoor.