TSK

TSK · Isaiah 47:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Ezra 5:12 TSK

¶ Sunuy maam nag ñoo merloo Yàllay asamaan, ba tax mu teg leen ci loxoy Nabukodonosor buuru Babilon, ma askanoo ci waa Kalde. Mu toj kër gii, yóbbu xeet wi ngàllo ca Babilon.

ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, yebal ko ca askan woowu ma merloo, ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, note leen ni banu mbedd.

def àddina wërngal këpp ndànd-foyfoy, tas dëkk ya, te du jàpp nit ba yiwi ko?”

ba tax ma sobeel kilifay kër gu sell gi, araamal Yanqóoba, wacce Israyil ŋàññi noon.

Aji Sax ji ci boppam moo leen tasaare, faaleetu leen; cér lees séddul sarxalkat, te teraleesul mag.

Sa liggéeyu jula bu yaatu moo la feesal fitna, nga bàkkaar, ba ma nangoo sa teddnga fa tundu Yàlla wa, sànk la, yaw malaakam serub miy aare, nga jóge digg doj yuy tàkk.

Yeen waa kër Yanqóoba, ni ngeen naane sama kaasu mbugal ca sama kaw tund wu sell, ni la xeet yépp di naane ba fàww, di naan ak a jolu ba mel ni masuñoo nekk.

Waaye mer mu réy laa mere xeet yii naagu. As lëf laa meroon, waaye ñoom ñoo yokk aw ay.”

Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.