TSK

TSK · Isaiah 49:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.

di mbaar mu ñuy serloo tàngooru bëccëg, di ko seeloob taw ak waame.

Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy serloo ci tàngoor, nde merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw miir.

Ku ni mel, bérab bu kawe lay dëkke, doj yu ñu dàbbli di rawtoom, dundam doy, te ndoxam du ñàkk.

Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmm ug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»

Ñooy dikk di jooy, di leewaayu, ma jiite leen, yóbbu, jaare leen xàll wu jub wu ñu dul fakktaloo, ba ca wali ndox ya, ngir maay baayu Israyil, Efrayim di sama taaw.