¶ «Deeleen baaxantal bésub Noflaay, ngir sellal ko.
TSK
TSK · Isaiah 56:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Waxal bànni Israyil ne leen: “Fexeleen rekk ba sama bési Noflaay, ngeen di ko wormaal, ndax bésub Noflaay da di firnde sama digganteek yeen ak seen askan, ngir ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen ber, sellal leen.
Ma ŋàññ kàngami Yuda, ne leen: «Lu ñaaw lii ngeen di def nag di teddadil bésub Noflaay?
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Aji Sax ji, kuy ganeji sa xayma? Ana kuy dëkki sa tund wu sell?
Dëddul mbon, di jëfe mbaax, ba dëkke réew mi fàww.
Màggal-leen Ki Sax! Ndokklee ku ragal Aji Sax ji, di tàqamtikoo ay santaaneem.
Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.
Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon; ab dof day ràkkaaju, du tiit.
Yoonu kuy jubal day moyu lu bon, ku teeylu sa jëfin, sàmm sa bakkan.
Aji Sax ji kat dafa wax ne: «Jaam yi ñu xañ ngóora, su ñu sàmmee sama bési Noflaay, taamu sama coobare, tey feddli sama kóllëre,
«Su ngeen téyee seen tànk bésub Noflaay, baña def li leen neex sama bés bu sell; su bésub Noflaay di seen nammeel, di bésub Aji Sax bu sell bu ngeen teral; ngeen teral bés bi, bañ cee topp li ngeen jikkowoo, di topp seen bakkan ak wax ju dul jeex;
Sama bési Noflaay itam maa leen ko jox, muy màndarga sama digganteek ñoom, ngir ñu xam ne man Aji Sax ji maa leen sellal.
Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
¶ «Ndokklee yeen ñi fóot seeni yére, ngir saña lekk ci garabu dund gi, jàlle bunt yi, dugg ci biir dëkk bi.