te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»
TSK
TSK · Isaiah 6:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Jël nañu jabar ci ñoom, jëlal ci jabar seeni doom, ba jaxase jiwu mu sell mi ak waasoy réew yi. Njiit yeek mag ñi sax ñoo jiitu ci googu fecci kóllëre.»
Garab sax ñàkkul yaakaar. Boo goree, mu jebbiwaat, ba du ñàkk ay njebbat.
Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ ak ku des fa Yerusalem, ku sell ki lees lay wooye, muy képp ku ñu bind turam, te mu wara dese bakkan ci Yerusalem.
Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.
Waaye maay déeg lenn ci yeen, ñu rëcc saamar, tasaaroo ci xeet yi, ci biir réewi jaambur.
Waaye maay wacc fi sa biir askan wu woyof te néew doole, ñu yiiroo turu Aji Sax ji.
Kenn deful lii te desem xel. Kenn doŋŋ a ko defoon. Ndax lan? Kuutaay li ko Yàlla digoon la doon wut. Kon nag sàmmleen seenum xel, te buleen wor seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw.
ñoo xéewloo itam maam ya; ci wàllu doom aadama it, ci ñoom la Almasi soqikoo, di Yàlla, tiim lépp, te yelloo cant ba fàww. Amiin.
Ndax kat ab jooxe bu génnee ci tooyalub sunguf, di ndoortel meññeef, su boobu jooxe sellee, tooyalub sunguf bépp ay sell. Ndax su reenu garab sellee, car ya it sell.
Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.