TSK

TSK · Isaiah 64:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër Buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.

Muy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda.

Aji Sax ji, xanaa doo nu mere ba fàww, sa fiiraange ni sawara ci sunu kaw?

te nun ñiy sa mbooloo, di sa gétt gi ngay foral, nu di la sant ba fàww, di biral sa ngërëm sët ba sëtaat.

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttliku bàkkaar.

Ay doomi doxandéem ay tabaxaat say tata, seeni buur di la surgawu. Maa meroon, duma la, maa la baaxe, yërëm la.

Nu ngi mel ni xeet woo masula yilif, xeet wu ñu masula tudde sa tur. Éy soo xaroon asamaan, wàcc, ba tund yi yëngu fi sa kanam!»

Aji Sax ji, yar ma lu yem, te bañ maa yare mer, di ma semmal.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

Su Edom nee: “Dees noo rajaxe, waaye nooy tabaxaat gent bi,” Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moom dafa wax ne: “Ñooy tabax, maay màbb.” Ñoom lees di wooye waa diiwaan bu bon bi, askan wi Aji Sax ji mere ba fàww.

Ñu jàpp nag Seytaane, mi leen daan nax, sànni ko ci déegu sawaraak tamarax ba, mu fekki fa rab waak yonentu caaxaan ba. Dees na leen fa mitital guddi ak bëccëg, ba fàww.