TSK

TSK · Isaiah 8:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Lii moo di seedey yoon yi, ak dogali yoon yi, ak àttey yoon yi Musaa dénkoon bànni Israyil, gannaaw ba ñu bàyyikoo Misra,

Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.

¶ Gannaaw gi Aji Sax ji ne ma: «Jëlal àlluwa ju mag, ak xalima gu jàppandi, nga bind ci lii: “Maxer Salal Xas Bas”, (mu firi Sëxëtoo këfit foqet).»

Peeñum xew-xew yii yépp ump na leen, ni leen kàdduy téere bu ñu tay umpe. Boo ko joxee ku jàng, ne ko mu jàng ko, mu ne la manu ko, nde dees koo tay;

¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.

Mu ne ma: «Dañeel, demal rekk, ndax mbir yii dees koo làq, dëxëñ ko, ba keroog muj ga taxaw.

¶ Nitu neen nag du nangu lu aju ci Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom; du ko mana xam, ndax loolu Xelum Yàlla lees koy natte.

¶ Ci biir loolu ma gis ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi, taxañub téere bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom ñaari tayu.

Naka la juróom ñaari dënu yi jib, may waaja bind, daldi dégg baat bu jóge asamaan, ne ma: «Loolu juróom ñaari dënu yi wax de, gas ko, suul, bu ko bind.»