Yerusalem kay law ndes di génne, aw ndes ay rëcce tundu Siyoŋ, te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy sottal loolu ci xéraangeem.
TSK
TSK · Isaiah 9:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Jàmbaaroo, takkal sa saamar, te yànj, am daraja;
Janti Buur aji jub day woomle, te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,
Ragal Aji Sax ji lay safoo, du lu ko bëtam may rekk lay àttee, du lu ko noppam may rekk lay dogale,
Buur a ngii, njekk lay nguuroo, jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee;
Bant bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim it, du ko fey. Mooy indi yoonu dëgg.
Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.
Bés yooyu ci jamonoom, maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, muy jëfe njub ak njekk ci réew mi.
Ci kaw loolu weñ gaak ban baak xànjar jaak xaalis baak wurus wa lépp bokk rajaxoo, mel ni xataxu dàggay lolli. Ngelaw li buub ko yóbbu, ba mu ne mes. Doj wa daloon ca jëmm ja nag doon tund wu mag, fees àddina sépp.
Ci kaw loolu ñu jébbal ko kilifteef gaak ndam laak nguur ga. Ci biir loolu waa mbooloo yépp ak xeet yeek làkk yi di ko wormaal. Kilifteefam day sax fàww, du jeex, te nguuram du foq mukk.
Ku màgg lay doon, te dees na ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.
Waaye Doom ji la Yàlla ne: «Yàlla, sab jal tey la ak ëllëg ba fàww, te sa yetu nguur njub lay doon.