TSK

TSK · James 1:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Su amee ci seen biir ab ndóol, di kenn ci seen bokki bànni Israyil, ci benn ci seen dëkki réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen dëgër xol, di tëjal seen loxo, seen mbokkum ndóol moomu.

Du ñàkk nag ab ndóol ci réew mi. Moo tax ma sant leen ne leen ngeen nàddila nàddil seen mbokkum ndóol, ak seen néew-ji-doole ji ci seenum réew.

Bokk yi, wóoluleen ko fu ngeen tollu, diisleen ko seen xol, Yàllaay sunu kiiraay. Selaw.

Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.

Kuy damu kay, na damoom xelam mu ko may mu xam ma, xam ne maay Aji Sax, jiy jëfe ngor ak dëgg ak njekk fi kaw suuf. Loolu déy mooy sama bànneex.» Kàddug Aji Sax jee.

Luke 9:48 TSK

Mu ne leen: «Xale bii, képp ku ko dalal ndax sama tur, man nga dalal; te képp ku ma dalal, dalal nga ki ma yebal; ndax ki gëna tuut ci yeen ñépp, kooku moo gëna màgg.»

Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.

Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.

daldi xélu dëgmal naanukaay ba, ngir jot ca neexal ba nu Yàlla di wooye fa kaw, ci Almasi Yeesu.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

¶ Gis naa sa coono ak sag ñàkk, moona yaaka duunle! Gannaaw loolu it, waxi yàq-der yi tukkee ci ñooñu tuddoo Yawut te duñu Yawut, duñu lenn lu moy jàngub Seytaane, dégg naa ko.

¶ Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma.