Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee!
TSK
TSK · James 3:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Jigéen ña di woo mbooloo ma ca seen saraxi tuur ya, mbooloo ma di lekk ak a sujjóotal seeni tuur.
Yonent boobu nag mbaa boroom gént boobu, dee mooy àtteem, ndax moo woote ag fippu ci seen kaw Yàlla Aji Sax, ji leen jële ca réewum Misra, jote leen kërug njaam ga. Mu nar leena féle ci yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji sant ngeen doxe ko. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
Absalom nag ne ko: «Bàyyil boog sama mag Amnon, mu ànd ak nun.» Mu ne ko: «Lu muy ànd ak yaw doye?»
¶ Ci kaw loolu Absalom ne Ayitofel: «Xelal-leen nu boog, lu nu wara def?»
Soxnaam Yesabel dikk ne ko: «Lu la tax ne fóññ nii? Lu la teree lekk?»
Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat, ak làmmiñu njublaŋ.
Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
Dina la aar ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
Tont lu neex day giifal, baat bu ñagas di jógal xol.
Bu matt amul, ab taal fey, fu soskat amul it, xuloo jeex fa.
Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan: «Éey, Tiitaange-lu-dajal! Booleleen ko, boole rekk!» Ñi ma séqal jàmm sax, di yeeru ma fakkastalu, naan: «Jombul mu juum, nu jekku ko, ba mana feyu.»
¶ Ba loolu amee Piyeer ne ko: «Anañas, lu waral Seytaane di fees sab xol, ba ngay wor Noo gu Sell gi, di làq lenn ci njégu tool bi?
Ci seen biir sax la aw nit di jóge taxaw, di wax ndëngte, ngir xiirtal taalibe yi, ba ñu topp leen.
¶ Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen.
¶ Lu jëm nag ci powum séy, ak jépp jëfi sobe, mbaa ag bëgge, li jekk ci ay nit ñu sell, moo di ñu bañ koo tudd sax ci seen biir,
Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore, aki firnde ak kéemaani feni neen,
Xanaa du ñooñu ñooy ñàkke kersa tur wu tedd wi ngeen di wuyoo?
¶ Li ngeen wara jëkka xam moo di bés yu mujj ya, ay niti ñaawlekat ay dikk, di nit ñu topp seen bakkan.
¶ Géntkat yii itam noonu rekk lañuy sobeele seen yaramu bopp, boole ci di sofental kilifteef, ak di saaga boroom daraja ya fa asamaan.
¶ «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu.
¶ Ci kaw loolu ma gis rab wu génne ci géej gi, am juróom ñaari bopp ak fukki béjjén, béjjén yi sol fukki mbaxanay buur, béjjén bu ne menn, bopp bu nekk ak tur wuy saaga Yàlla.
làmp du niiteeti fi yaw, te baatu boroom séet akub séetam du jibeeti fi yaw mukk, ndax say julaa ëppoon doole ci àddina, te say xërëm a sànk askanoo askan.»