Yaakaaral Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit, te yaakaarati Aji Sax ji.
TSK
TSK · James 5:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Aji Sax jee baax ci ñi ko yaakaar, baax ci ki koy sàkku.
Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.
¶ Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm.
Na seen lewetaay wóor ñépp, Sang bi jegesi na.
Yal na Boroom bi dooleele noonu seen xol, ngir kera bu sunu Sang Yeesu délsee, ànd ak ñoñam ñu sell ñépp, fekk leen sell te mucc sikk, fa kanam Yàlla sunu Baay.
Te bunu def ni ñenn ñi, di daggoo ak sunuy ndaje, waaye nanuy ñaaxante, rawatina tey bi ngeen gisee bés bi dëgmal.
¶ Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiital-leen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.