TSK

TSK · James 5:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»

Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.

Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.

Kon na ku nekk joxe, ni mu ko waaje ci xolam, te bañ koo tiisoo, bañ koo joxee ñàkk pexe, ndax kiy joxee xol bu sedd, Yàlla sopp na ko,

Bunu di yég sunu bopp, di merloonte ak a iñaanante.

waaye ñoo koy layoo ak ki nara àtte ñiy dund, ak ñi dee.

Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.