ndax kat mboolem ñaawtéef yooyu la waa réew ma leen fa jiitu daan def, ba réew ma mujj daj ak sobe.
TSK
TSK · Jeremiah 16:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Foofa ngeen di jaamoo ay yàlla yu loxoy nit sàkke bant, mbaa doj, yàlla yu dul gis, du dégg, du lekk, du xeeñtu.
Su ko defee noonee Aji Sax ji daan bége di leen baaxe ak a yokk, noonu la Aji Sax jiy bége di leen sànk ak a fàkkas, te dees na leen déjjatee ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko.
Waaye su ngeen walbatee seen xol, dégluwuleen, xanaa ngeen lajj, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu,
Buuru Babilon nag jam leen, ñu dee, foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la Yuda génne réewam, dem ngàllo.
«Waaye sama ñoñ déggaluñu ma, Israyil gii nangulu ma.
Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, te gàcce gàcceelu leen. Xamuñu sax luy kersa! Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» Aji Sax jee ko wax.
Éy yaw, yaakaaru Israyil, mi nuy wallu bésu njàqare, bul ñooru ni doxandéem ci réew mi, mbaa ku nekk ciw yoon, jàdd fi, fanaan.
Maa leen di def seen jaami noon réew mu ngeen xamul, sama mer jippét, tàkkal leen.»
Dingeen xañ seen bopp cér bi ma leen séddoon, ma def leen seen jaami noon ci réew mu ngeen xamul, ndax merloo ngeen ma mer mu dul fey mukk.»