TSK

TSK · Jeremiah 32:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.»

¶ «Na màggal googu di pàttliku ci yeen. Na mel ni màndarga mu nekk ci seen loxo ak seen jë. Su ko defee ngeen saxoo jàngle yoonu Aji Sax ji, ndax ci dooley loxoom la leen Aji Sax ji génnee Misra.

Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla Aji Sax ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët?

Aji Sax ji nag génne nu Misra ci dooley loxoom ak kàttanam, ci biir musiba mu réy, aki firnde, aki kéemaan.

ndax kat dees na dégg sa tur wu réy, ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan,

Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?

Moo génne ñoñam, ñu bég, moo génne tànnéefam ña, ñuy sarxolle.

seppee bànni Israyil ca ñoom, Kee saxoo ngoram!