May nga ma dooley nagu àll, ma diwoo diw gu bees.
TSK
TSK · Jeremiah 39:16
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
te nga ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Askan wii ak dëkk bii, ni ñuy toje njaq, ba deesatu ko mana defaraat, ni laa koy tojate. Tofet gii dees na fi rob ndax ñàkk fu ñu robe.
Jógal naa dëkk bii déy, te loraange laa leen naral waaye du jàmm.” Kàddug Aji Sax jee. “Ci loxol buuru Babilon laa koy teg, mu jafal ko, lakk.”»
Xamleen xéll rekk ne su ngeen ma reyee, bakkanu ku deful dara ngeen gàddu, yeen ak dëkk beek ñi ko dëkke, ndax ci lu wér Aji Sax jee ma yebal ci yeen, ngir ma yegge leen mboolem kàddu yii.»
¶ Ci jamono yooyu amoon na keneen ku doon biral waxyu ci turu Aji Sax ji. Muy Uri ma dëkk Kiryaat Yarim, di doomu Semaya. Uri doon biral waxyu, di rëbb dëkk baak réew ma, bokk ak Yeremi genn kàddu gi.
«Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Demal nga wax Cedesyas buurub Yuda ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teg dëkk bii ci loxol buuru Babilon, mu taal ko.
¶ «Kon nag Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Maa ngi nii di wàcceel Yuda ak képp ku dëkke Yerusalem mboolem musiba mu ma leen tuddaloon. Ndax damaa wax ak ñoom te dégluwñu; ma woo leen, wuyuwñu.»
¶ Ci biir loolu Ebedd Meleg, Kuuseen ba, di bëkk-néeg ci biir kër buur, dégg ne tàbbal nañu Yeremi ca kàmb ga. Fekk Buur a nga toog ca bunt ba ñu dippee Beñamin.
Ñu néew ay rëcci saamar, walbatikoo réewum Misra, ñibbi réewum Yuda. Waaye mboolem ndesu Yuda, ga dikkoon toogaansi Misra, dinañu xam kan la kàddoom di sotti, man am ñoom.
Teewul sama kàdduy àrtu ak sama dogali yoon ya ma yóbbante woon sama jaam ña, yonent ya, du lépp a dab seeni maam? Ñu dëpp nag daldi ne: “Noonee Aji Sax ji Boroom gàngoor yi nammoona def ak nun, feye nu ko sunuy jikko ak sunuy jëf, noonu la def ak nun.” »